Lyrics

Par AbouAmg Mbëggeel la nekk ci sama xol Waaye àdduna nu sonal lool Xol bu fees ak bànneex Lala yéene won ci àdduna Mbëggeel gi ma am ci yaw Mbaa du ma sonal lool Jafe-jafe àdduna Ak mbokk gi nu Yàlla Buur bi boole Kon mbëggeelay àdduna Ndax Yàlla moo ñu boole Sama yéene yaatu na Maa ngi ñaan Yàlla may nu doole Dugg naa ci gaalu mbëggeel Ndox mi yóbbu ma, euh! Ngelaw laa ngi may indi ci yaw Ñu gise leer na ma Mbëggeel mooy li leeral àdduna Xam nga yaw laa bëgg lool Sama yéene yaatu na Maa ngi ñaan nga yokk! Dénk naa la Yàlla Dénk naa la sama xol Saa su ma jullee di la ñaanal Sama xol laa ko tibbe Kon mbëggeelay àdduna Ndax Yàlla moo ñu boole Sama yéene yaatu na Maa ngi ñaan Yàlla may nu doole Dugg naa ci gaalu mbëggeel Ndox mi yóbbu ma, euh! Ngelaw laa ngi may indi ci yaw Ñu gise leer na ma Mbëggeel mooy li leeral àdduna Xam nga yaw laa bëgg lool Sama yéene yaatu na Maa ngi ñaan nga yokk!
Writer(s): Charles Diagne, Seydina Oumar Samb Guèye Lyrics powered by www.musixmatch.com
instagramSharePathic_arrow_out